23/09/2016
Assalamou aleykoum wa rahmatoulahi wa barakaatouho... Mbokk yi manguilén di nouyou, dilén ziara, dilén baal hakh, Balnala yalla nagnou buur yalla bolé diégueul. Di dénk sama bop, dilén dénk topou yalla ak ragal yalla. Yalla nagnou yalla fayal sougnou mak you baax yi gnou ci melni Séydil hadji Malick, cheikhal islaam, mame boroom touba, mame bou, mame limamou ak gni ci déss gneup. Dokhnégnou sen mission liguéyeulnagnou islaam fékhénégnou ba lep rafet. Ngalla bougnou yakhal sougnou bop ci ay khèbaaté ak ay yakhanté. Mouhamad saws waxneu cheikhana ahmad at-tijany cherif rta niko wakhal sa talibé yi négnou moytou di loraneté, ndakh bougnou loraneté man mouhamad légnou lor alahou akbar. Tékci alkhour-ane wax ni inamal mouminouna ikhwatou, fasslihou bayna akhwaykoum manam djouliit bi djouliteuy mbokam. Wakhoul serere, wakhoul peuhl, wakhoul ouolof, wakhoul guéweul, wakhoul guèr djoulit la wakh, tékci né tahoulou alal birri wa takhwa, manam délén dimbalanté ci mbaax, topou yalla ak ragal yalla ndakh gnou meneu baaxlé, baaxlé feulé amiiine. Dilén gnanal yéndou ak jaam, té dilén wa BON JUUMA MOUBAARACK